ci turu Yàlla laye tambalé midi àji yërëm jaam nëpu ci aduna di àji yërëm waay texe yi ci alaaxira
Rabbi as haabaka bil himmati wala tou rabbi him bid darsi fakhate...

jaar jaar serigne abdou khadre mbacké

Jaar Jaari Serigne Abdou Khadre Mbacké

mi ngi juddoo njaarem (Diourbel). Tambaleefa njangum alxuraan ci daara Serigne Moustafa Gëy jàkarlook kër Seriñ Mor Mbaye Cissé (kër Gumak) ba jéexal, bind fa ñett (3) kaamil.

Ginaaw ba mu jugefa dem Touba ngir jàngi xam xamu diiné ci kër Serigne Affia Bousso ( imaam jumaa Touba).


Ci àtum 1996 la bayikoo Touba ñëw Dakar ngir jàngaléfa alxuraan ak xam xamu diiné ci daara Seriñ Cheikh Awa Balla Gëy.


Ci bisu 8 Mai 2002 la taxawal daaray bopam ngir difa weyël jàngalé alxuraan ak diiné ci Cité Fadja.


Ci weeru Novembre 2004 la toxoo foofée dem Parcelles Assainies Unité 17 ngir weyël ligeey boobu. itéem yepu moodi xamlé diiné lislaam ak di tarbiya ak


di tarqiya taalibe yiko Yàlla boléel ba kérook ñuy am ngërëmal Sunu Boroom ( subhaanahu wa ta-a-laa).


Yalnako Sunu Boroom tàxawu ci ligeey boobu muy ligeeyal Yàlla tadiko jàrée ci yoonu Serigne Touba, ta mu am ci jàmm ak sutura, am ci ndam ak sutura


ak ngërëmal Serigne bi!!!

 

Ajouter un Commentaire


Code de sécurité
Rafraîchir

copyright Al-himma 2010-2017